Accueil Podcasts Bëgg a Baax podcast
Bëgg a Baax podcast

Bëgg a Baax podcast

Cheikhouna Diaw 26 Épisodes juin 11, 2026

Li tax a jóg Bëgg a Baax podcast mooy yaatal mbaax. Képp koo xam ne mbaax ñor na la, nu ngi la ciy dalal ak jàmm.

Épisodes

Teggiini niti Yàlla yi: Xaaj ñeent
Teggiini niti Yàlla yi: Xaaj ñeent juin 11, 2026 00:27:07 Teggiin yii la Imaam Saaraani waxtaane ci poñ bii:- Yëram jullit ñi -Sant Yàlla-Nëbb sa tolluwaay-Néewal say mébet
Teggiini niti Yàlla yi: Xaaj ñett
Teggiini niti Yàlla yi: Xaaj ñett avr. 23, 2026 00:13:24 Teggiini niti Yàlla yi: Xaaj ñett bi mu ngi aju ci disóo ak Yàlla ci sa mbir yépp, moytu di jublu mayu Yàlla yi fàtte Aji-Maye ji, ak wéet.
Waxtaan ci bor
Waxtaan ci bor mars 20, 2026 00:13:41 Ci waxtaan wii, da nu ciy leer dayo bi bor am ak diis bi mu diis, ngir fàttali sunu bopp, waaye fàttali sunu bokki jullit yi ngir ñu jàjju te moytu bor boodut fay.
Ban xam-xam mooy farata?
Ban xam-xam mooy farata? déc. 27, 2025 00:31:49 Ci waxtaan Wii, danu ciy indi tontu ci laaj bii: Ban xam-xam mooy farata ci nit ki? Ginnaaw Yonent bi SAW daa wax ne sàkku xam-xam farata la ci jullit bi, kon yey na lu ne xam ban/yan xam-xam la war a ràngoo.
Teggiini niti Yàlla yi (Xaaj ñaar)
Teggiini niti Yàlla yi (Xaaj ñaar) déc. 6, 2025 00:22:55 Waxtaan wii mu ngi aju ci Teggiini niti Yàlla yi ak sew-sew yi leen wuutale ak ñeneen ñi.
Teggiini niti Yàlla yi (Xaaj bu njëkk bi)
Teggiini niti Yàlla yi (Xaaj bu njëkk bi) août 21, 2025 00:26:43 Waxtaan wi ab jukki la ci téereb kàngam boobu di Imaam Saaraani. Ci téere bi dafa ciy jàngale teggiini niti Yàlla yi yoy képp ku sóobu ci Yàlla te bëgg a bokk ci góor ña war nga leen ca roy.
Njariñu Koor
Njariñu Koor mars 6, 2025 00:36:28 Waxtaan wii Imaam Xasaali dafa ciy wax njariñ yi ci koor ak yiiw yi mu man a fàggul jullit bi, waaye tamit leeral dayo bi koor am fa saa Boroom.
Moytu àq yi
Moytu àq yi janv. 21, 2025 00:13:41 Waxtaan wii mu ngi aju ci àq yi nit man a ameel ay moroomam ak i saafara yi leen di far. Àq mat naa moytu, ndax ëllëg lu ñuy fayante la. Di jëfandikoo ñaan yi niti Yàlla yi tënk nag da ciy am solo ngir ëllëg sa dara du lëj.
Tëj gi: Gàllaŋkoor yi
Tëj gi: Gàllaŋkoor yi déc. 14, 2024 00:15:59 Ci mujjantalu téere bi, Imaam Dardiir daa tënkaat gàllankoor yiy tënk nit ki ba du àgg ci Yàlla, niral ci jikko yu mel ni rëy, ngistal añs… waaye tamit leeral ci ne Jaamu Yàlla di ci sàkku leneen ludut Yàlla ci gàllankoor yi la bokk.
Pensées et introspection
Pensées et introspection oct. 16, 2024 00:39:23 Ci waxtaan wi, danuy leeral xeeti xalaat yiy toq ci xelu doomu aadama, seen i jeexital ak yoon wi nit ki di jaar ngir sellal ay xalaatam ba duñu ko yóbb ci moy Yàlla.
Tegginu nitu Yàlla yi
Tegginu nitu Yàlla yi juil. 31, 2024 00:31:04 Ci waxtaan wii Imaam Dardiir dafa ciy waxtaane jikko yi nitu Yàlla yi di ame bu seen dox ci Yàlla matee ba seen i teggin mat sëkk (Makkaarimal ahlaax).
Lan mooy gis Yàlla?
Lan mooy gis Yàlla? juin 22, 2024 00:23:49 Ci waxtaan wii, Imaam Dardiir dafa ciy leeral xeetu teewlu yi am ak fi ñu man a yóbb nit ki ci jege Yàlla. Bu fa nit ki àgge, dina dem ba xam, yëg bir yoo xam ne maneesu koo leeral ci làmmiñ.

Recommandé